Xaralaymbëj Mooy xeetu xam-xam giy gëstu lépp lu jëm ci wàllugmbëj, ay jëfandikuwiinam ak ay seddalewiinam. bu njëkk dañoo foogoon ne mbëj ag wal la rekk guy dem, gu man a nekk gu baax(+) walla gu bon(-). Waaye ci ndimalu ay woroom xam-xam yu mel ne Hertz, Helmholtz, Maxwell, Heaviside, Alessandro Volta ak ñeneen ñu bari, ci lees dem ba gën a nànd, xam mbir mi. Lu mel neyamaleb maxwell biy faramfàce tëdiinuyani mbëj yi (feppsaal akmbëjfepp yiy wuute ci seen jublug yanub mbëj) walla toolumbëjbijjaakon ba ca juddoo.
Ag wàll gu am solo moo jëm ci lépp lu ñeel yokkte ak seddalewiinu kàttanu mbëj ba ca jëfandikuwaay ya (barab yees koy jëfandikoo).Kàttan gi dees na ko jóox ci ndimbalul ayjurukaayu mbëj ci barab yees ko jagleel, li ñuy waxdiggub mbëj, ci lu ëpp fa muy nekk day soree ak dëkkuwaay yi.
Buumi séddalekaay yi dañu leen a lëkkale ci seen biir ñuy jëleekàttan gi ca jóoxuwaay ya di ko yóbb ca jëfandikuwaay ya.
Li wuutale Buumi yóbbukaay yi, mooy limu dend gi ñuy yóbb, moo tax ñuy gis ay buumidend gu kawe, [[Dend gu diggu]|dend gu diggu]],dend gu suufe. Su diggante jóoxuwaay yi guddee, dañ fay def aymbëjjaaru, ay buumi dend gu kawe yu man a yóbb ay milioŋiwatt ci kàttan tambalee ciy 400000 v. Buumidend gu kawe yii la ñuy duppe yuyóbbug kàttanu mbëj, yi nga xam ne ñooy tax a man a yóbb kàttanu mbëj gi, jële ko ca jóoxuwaay ya, jëmee ko ca barabu soppikaay ya.
Ci nii la ñuy soppee dend gu kawe mu nekk dend gu diggu, jaarale ko ci aymasin yu mbëj yees di duppeesoppalikaay, ci noonu la ñuy yóbboo kàttanu mbëj gi ca ndombo gu dend gu diggu, moom ci boppam dañu koy àggal ci néegu seddalekaay yi jaarale ko cigndombog séddaleg kàttanu mbëj, foofa lañuy defee geneen coppite jëlee ko ci dend gu diggu soppi ko dend gu suufe ngir ñu man koo jox jëfandikukat yi ci kër yi ak liggéeyuwaay yi.